Kureelu Mbootaayu Xeet yi ndawi réew yu mag yi, yu ci mel ni Nguur-Yu-Bennoo , Diiwaan-yu-Bennoo yu Aamerig, Bennog Sofyet, Faraas ak Siin, danoo daje woon ci Wasington peeyub Amerig ci wenn waxtaan atum 1933g, ginaaw bi as lëf ci ndam tàmblee feeñ ñeel reewi tapoo yi .Ci noonu nu gëstu woon nan lanu fiy sose ag mbootaay gu adduna guy yëngu ci saxal ponki jàmm ci adduna bi, jële fi xeex yi, amal fi maandute ak yamoo ci diggante mbooleem reew yi, ak rafetal nekkiinu mboolaayu r;ew yi, ci koom-koom, mboolaay, aada ak wér.Bi loolu jàllee nu def benn dajeb waxtaan bu àdduna bi ci dëkku San Fransisco ci 25 awril atum 1945, ngir rëdd fa ag kollëre ñeel ag mbootaayug xeet gu yees gu fiy wuutu kureelu xeet yi.Ndawi lu tollook juroom fukk ak benni reew teewe nanu ko, nangu it ci nu def kollëreg mbootaayu xeet yi, ak xaatim ko ci 26/06/1945g. La jiitu ca kollëre ga mooy:
Nun askani mbootaayu xeet yi ñi ngi giñ ne di nanu xettali maas yiy ñëw ci musibay xare , yi nga xam ne sotti nanu nit ay alkande aki naqar yu kenn manul’a misaal ci ñaari yoon ci diir bu gàtt bu weesuwul genn maas reek. Ñi ngi giñ it ne dananu feddaliwaat sunu ngëm ci àqi nit ju cosaanu ji ak yelleefam, ak teddngay jëmm ak man-manam, di feddali it ne goor ñi ak jigeen ñi ak xeet yi, moo xam yu ndaw lanu, mbaa yu mag, ñoo yam kepp ci àq ak yelleef .
raaya bu Kureelu Mbootayu Xeet yi